1809937850
Bëgg a Baax podcast

Advertise on podcast: Bëgg a Baax podcast

This podcast has
29 episodes
Explicit
No
Date created
2025/04/22
Latest episode
2026/10/16
Average duration
24 min.
Release period
63 days

Description

Li tax a jóg Bëgg a Baax podcast mooy yaatal mbaax. Képp koo xam ne mbaax ñor na la, nu ngi la ciy dalal ak jàmm.

Podcast episodes

Check latest episodes from Bëgg a Baax podcast podcast


Le vrai miracle chez les soufis
2026/10/16
Ci waxtaan wii, Ibn Ataa daf ciy indi déggiinam ci lay mooy dëgg-dëggi karaama gi sufiyànke yi. Ñu bari jàpp nañu ne karaama mooy lem suuf si, naaw ci jawu ji mbaa dox ci ndox mi. Waaye li sufiyànke yi jàppe karaama dëgg mooy bàyyi moy Yàlla ci biir ak ci biti. Xam ko, di ko jaamu te duñu ko bokkaale ak dara.
Ghazâli: conseils précieux pour l‘aspirant
2026/10/10
Ci waxtaan wii Al-Ghazâli da ciy dénk jullit bi mu moytu di ànd mbaa déglu niti jamonoom yi sàggan ci jaamu Yàlla, waaye taqoo ak ñi farlu ñi mbaa di yër téere ñu baax ñi fi jaaroon te farlu woon ci topp Yàlla lool ngir yokk pas-pasam ci Yàlla.
Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñeent
2026/06/11
Teggiin yii la Imaam Saaraani waxtaane ci poñ bii: - Yëram jullit ñi -Sant Yàlla -Nëbb sa tolluwaay -Néewal say mébet
Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñett
2026/04/23
Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñett bi mu ngi aju ci disóo ak Yàlla ci sa mbir yépp, moytu di jublu mayu Yàlla yi fàtte Aji-Maye ji, ak wéet.
Waxtaan ci bor
2026/03/20
Ci waxtaan wii, da nu ciy leer dayo bi bor am ak diis bi mu diis, ngir fàttali sunu bopp, waaye fàttali sunu bokki jullit yi ngir ñu jàjju te moytu bor boodut fay.
Ban xam-xam mooy farata?
2025/12/27
Ci waxtaan Wii, danu ciy indi tontu ci laaj bii: Ban xam-xam mooy farata ci nit ki? Ginnaaw Yonent bi SAW daa wax ne sàkku xam-xam farata la ci jullit bi, kon yey na lu ne xam ban/yan xam-xam la war a ràngoo.
Teggiini niti Yàlla yi (Xaaj ñaar)
2025/12/06
Waxtaan wii mu ngi aju ci Teggiini niti Yàlla yi ak sew-sew yi leen wuutale ak ñeneen ñi.
Teggiini niti Yàlla yi (Xaaj bu njëkk bi)
2025/08/21
Waxtaan wi ab jukki la ci téereb kàngam boobu di Imaam Saaraani. Ci téere bi dafa ciy jàngale teggiini niti Yàlla yi yoy képp ku sóobu ci Yàlla te bëgg a bokk ci góor ña war nga leen ca roy.
Njariñu Koor
2025/03/06
Waxtaan wii Imaam Xasaali dafa ciy wax njariñ yi ci koor ak yiiw yi mu man a fàggul jullit bi, waaye tamit leeral dayo bi koor am fa saa Boroom.
Moytu àq yi
2025/01/21
Waxtaan wii mu ngi aju ci àq yi nit man a ameel ay moroomam ak i saafara yi leen di far. Àq mat naa moytu, ndax ëllëg lu ñuy fayante la. Di jëfandikoo ñaan yi niti Yàlla yi tënk nag da ciy am solo ngir ëllëg sa dara du lëj.
Tëj gi: Gàllaŋkoor yi
2024/12/14
Ci mujjantalu téere bi, Imaam Dardiir daa tënkaat gàllankoor yiy tënk nit ki ba du àgg ci Yàlla, niral ci jikko yu mel ni rëy, ngistal añs… waaye tamit leeral ci ne Jaamu Yàlla di ci sàkku leneen ludut Yàlla ci gàllankoor yi la bokk.
Pensées et introspection
2024/10/16
Ci waxtaan wi, danuy leeral xeeti xalaat yiy toq ci xelu doomu aadama, seen i jeexital ak yoon wi nit ki di jaar ngir sellal ay xalaatam ba duñu ko yóbb ci moy Yàlla.
Tegginu nitu Yàlla yi
2024/07/31
Ci waxtaan wii Imaam Dardiir dafa ciy waxtaane jikko yi nitu Yàlla yi di ame bu seen dox ci Yàlla matee ba seen i teggin mat sëkk (Makkaarimal ahlaax).
Lan mooy gis Yàlla?
2024/06/22
Ci waxtaan wii, Imaam Dardiir dafa ciy leeral xeetu teewlu yi am ak fi ñu man a yóbb nit ki ci jege Yàlla. Bu fa nit ki àgge, dina dem ba xam, yëg bir yoo xam ne maneesu koo leeral ci làmmiñ.
Xeetu sikar yi: Tudd Yàlla ci làmmiñ
2024/05/29
Ci waxtaan wii, Imaam Dardiir da ciy wax ci xeetu tudd Yàlla yi am, rawatina bu làmmiñ bi nga xam ne kiy doog a sóobu ci lay tàmbalee. Ci mujj gi mu tënk ponku tassawuf yi mu jàpp ne ñoo ci gën a am solo.

Podcast reviews

Read Bëgg a Baax podcast podcast reviews


0 out of 5
0 reviews

Podcast sponsorship advertising

Start advertising on Bëgg a Baax podcast relevant audience podcasts


What do you want to promote?

You may also like to advertise on these Podcasts